395px

Xaarit (feat. Ndiole Tall)

Viviane Chidid

Xaarit (part. Ndiole Tall)

Dama ni sama xarit nga
Te yaw mi xam nga ni ku la bëgg laa
Wax dëgg Yàlla seede na, sama xarit nga
Te yaw mi xam nga ni ku la bëgg laa

Bëgg naa la ba foo pikiiru ma naan fa doom
Lu la metti gaañ ma, lu la wokk xuri ma yay
Ma ni yaw foo pikiiru ma naan fa doom
Lu la metti gaañ ma, lu la wokk xuri ma, yeh yeh yeh

Buur Yàlla moo ñu boole
Sama waay nga te du tay loolu démb la (loolu démb la)
Man ak yaw boobu ba léegi
Sunu diggante bi teye nañ ko mu dëgër (mu dëgër)

Oh oh oh
Xarit dëgg am na, xarit dëgg am na
Oh oh oh
Sa xarit dëgg man la, seedeel naa la lii

Sama waay nu ko raw laa la bëggee
Nga sax ci sama xol maa ko wax sama guy nga
Foo ko seen geestu gis ma
Guddi muy bëccëg soriwuma
Dégg nañu lu bon, dégg nañu lu baax
Bokku nañu bànneex, bokku nañu naqar
Ba pare mel ni ay Cheikh amuñu nëbo
Eh eh, du lekk bàyyi ma

Ma ni yaw xarit nga
Gën nga doomu ndeye, lii leer na ma
Yaw xarit nga
Zeyna Ndour doo doom waay nga

Buur Yàlla moo ñu boole
Sama waay nga te du tay loolu démb la (loolu démb la)
Man ak yaw boobu ba léegi
Sunu diggante bi teye nañ ko mu dëgër (mu dëgër)

Oh oh oh
Xarit dëgg am na, xarit dëgg am na
Oh oh oh
Sa xarit dëgg man la, seedeel naa la lii

Oh oh oh
Xarit dëgg am na, xarit dëgg am na
Oh oh oh
Pa Philippe xam na seedeel na ma lii

Foo pikiiru ma naan fa doom loolu leer na
Yaa gën ci man fu ma jaaxle ñëw seetsi la
Yaw rekk laay gis su lëndëmee
Lu ñu mësa wax ci ñun la yam
Lu ñu mësa def ci ñun la yam
Bu dara xewe ñu ànd dem
Suñu diggante moo dàq lem
Sama jikko boo ko bëggee gis laal ko seet

[Ndiole Tall]
Yaa yéy def ko muy sa xarit
Bul déglu kenn àndal ak moom
Doom day sax ci xolub ndayam
Vivi ànd ngeen sax ba ndiroo kanam
Kuy laal ma démba sagar yaa ca ndam
Kuy laal sama waa ji Vivi jugal ñu dem

Lu la wokk xuri na ma foo dee ma dee fa
(Àndal ak ku dal sa xel!)
Ni ñuy àndee nii neex na ma xarit sama
(Xarit dëgg nii lay mel)
Yaw rekk laay gis su lëndëmee
(Moy cote far!)
Ñun benn lañu te duñu ñaar
(Moo am)
Lu ne lañu gis ndax fi ñu jaar
(Moo tax yaa ngi ca kanam)
Bu coow li bare maak yaw a far
(Ñoo far)
Amitié bu mel ni aka rare
(Loo sax!)
Sama jikko boo ko bëggee gis laal ko seet
(Kaay laal lu la ci dal dinga xam)

[Ndiole Tall]
Ku nekk làmbil bi la neex topp sa xarit
Maa yéy sama yaay laay topp
Bu ngeen àndee dina neex, ah
Bu ngeen àndee dina neex, aa Thiam day neex

Foo pikiiru ma naan fa doom loolu leer na
(Dama ni li leer na)
Yaa gën ci man fu ma jaaxle ñëw seetsi la
(Ñëw seetsi la)
Yaw rekk laay gis su lëndëmee
(Cote far, far!)
Lu ñu mësa wax ci ñun la yam
(Ñun rekk)
Lu ñu mësa def ci ñun la yam
(Ñun rekk)
Bu dara xewe ñu ànd dem
(Sañse lu took)
Suñu diggante moo dàq lem
(Aaah!)
Sama jikko boo ko bëggee gis laal ko seet
(Kaay laal lu la ci dal dinga xam)

[Ndiole Tall]
Kuy laal ma démba sagar yaa ca ndam
Kuy laal sama waa ji lu la ci dal yaa xam
Kuy laal ma démba sagar yaa ca ndam
Kuy laal sama waa ji lu la ci dal yaa xam
Kuy laal ma démba sagar yaa ca ndam
Kuy laal sama waa ji lu la ci dal yaa xam
Kuy laal ma démba sagar yaa ca ndam

Xaarit (feat. Ndiole Tall)

Je suis comme un frère pour toi
Et je sais que tu veux que je t'aime
Dis la vérité, Dieu l'a dit, je suis comme un frère pour toi
Et je sais que tu veux que je t'aime

Je veux que tu sois là où je peux te voir
Ce que tu me donnes, je le ressens, ce que tu fais me touche
Je suis là où tu peux me voir
Ce que tu me donnes, je le ressens, ce que tu fais, ouais ouais ouais

Dieu est grand, il nous unit
Je suis ton frère et ça ne changera pas (ça ne changera pas)
Moi et toi, on est ensemble maintenant
Notre lien est fort, il ne se brisera pas (ne se brisera pas)

Oh oh oh
L'amour est vrai, l'amour est vrai
Oh oh oh
Ton amour est à moi, je te le dis

Mon frère, je te le dis, je t'aime
Tu es dans mon cœur, je te parle de mon gars
Où que tu sois, je te vois
La nuit, je ne peux pas dormir
On entend des choses mauvaises, on entend des choses bonnes
On se soutient, on se bat
C'est pas comme si des Cheikh n'avaient pas de voix
Eh eh, ne me laisse pas tomber

Je suis là où tu es
Tu es plus qu'un fils pour moi, je te le dis
Toi, mon frère
Zeyna Ndour, tu es mon frère

Dieu est grand, il nous unit
Je suis ton frère et ça ne changera pas (ça ne changera pas)
Moi et toi, on est ensemble maintenant
Notre lien est fort, il ne se brisera pas (ne se brisera pas)

Oh oh oh
L'amour est vrai, l'amour est vrai
Oh oh oh
Ton amour est à moi, je te le dis

Oh oh oh
L'amour est vrai, l'amour est vrai
Oh oh oh
Philippe sait que je te le dis

Où que tu sois, je te vois, c'est vrai
Tu es plus que moi, je suis là pour toi
Toi seul, tu vois ce que je ressens
Ce qu'on dit, c'est pour nous
Ce qu'on fait, c'est pour nous
Si on ne se voit pas, on se retrouve
Notre lien est fort, il ne se brisera pas
Mon cœur, je te le dis, je te vois

[Ndiole Tall]
Tu es là pour moi, c'est ton amour
Ne laisse personne te séparer de moi
Un enfant est juste dans le cœur de sa mère
Vivi, vous êtes là, même si vous êtes loin
Celui qui me voit, je suis là pour toi
Celui qui me voit, je suis là pour toi

Ce que tu fais, je le ressens, où que tu sois
(Sois là pour celui qui a besoin de toi!)
Quand on est ensemble, c'est bon pour moi, l'amour est vrai
(L'amour est vrai, c'est ce que je ressens)
Toi seul, tu vois ce que je ressens
(C'est un vrai lien!)
Nous sommes un, et nous ne sommes pas deux
(C'est vrai)
Ce que nous voyons, c'est ce qu'on a
(C'est pourquoi tu es là)
Si tu es là, c'est que tu es là
(Ne t'inquiète pas)
L'amitié est comme un trésor
(C'est vrai!)
Mon cœur, je te le dis, je te vois
(Sois là pour celui qui a besoin de toi)

[Ndiole Tall]
Qui que tu sois, tu es là pour moi, c'est ton amour
Je suis là pour ma mère, je suis là pour toi
Si vous êtes ensemble, c'est bon, ah
Si vous êtes ensemble, c'est bon, ah Thiam est bon

Où que tu sois, je te vois, c'est vrai
(J'ai vu que c'est vrai)
Tu es plus que moi, je suis là pour toi
(Je suis là pour toi)
Toi seul, tu vois ce que je ressens
(C'est un vrai lien, lien!)
Ce qu'on dit, c'est pour nous
(Nous sommes un)
Ce qu'on fait, c'est pour nous
(Nous sommes un)
Si on ne se voit pas, on se retrouve
(C'est un vrai lien)
Notre lien est fort, il ne se brisera pas
(Ah!)
Mon cœur, je te le dis, je te vois
(Sois là pour celui qui a besoin de toi)

[Ndiole Tall]
Celui qui me voit, je suis là pour toi
Celui qui me voit, je suis là pour toi
Celui qui me voit, je suis là pour toi
Celui qui me voit, je suis là pour toi
Celui qui me voit, je suis là pour toi
Celui qui me voit, je suis là pour toi
Celui qui me voit, je suis là pour toi

Escrita por: