visualizaciones de letras 1

Deugg'Leu

Dieyna

Letra

    Maak yaw démb la du tay
    Ñoo bokku lépp romb nga doomu ndey
    Man duma tiit sum lay gis sama wet
    Même bu ñépp demee yaw nga des duma wéet
    Bu ma amee mettit yaw nga am lu la metti
    Daa dem ba mel ni ñoo bokk xol lu ma ne yaa ngi ci
    Mësuloo ma gis ci ay jafe-jafe di ma seetaan
    Wala nga àndaak noon yi di ma reetaan

    Ma ni dëgg la
    Lu yàgg dëgg la
    Ànd bi dëgg la
    Moo tax ma bëgg la
    Lépp dëgg la nga

    Lu ma neex neex na la
    Lu ma metti sonal la
    Ki tax ma gëm ni xarit am na yaw la
    Lu ma neex neex na la
    Lu ma metti sonal la
    Ki tax ma gëm ni xarit am na yaw la

    Sama xarit, yaw xarit, yaw xaritoo
    Sama xarit, xarit, yaw xaritoo
    Sama xarit, yaw xarit, yaw xaritoo
    Sama xarit, xarit, yeah, yeah, yeah, yeah

    Xaritoo

    Kenn sañul toogaak yaw di yàq sama der
    Wala di wax ci man lu bon
    Yaw mësuloo ma def lu ñaaw
    Te su ma réeree yaay ki may tegaat ci yoon
    Yaw musoo ma wóor, musoo ma tooge
    Yaw rekk ka woor mën naa ko seedee
    Yaa gëna goree sama tàkkandeer
    Ndax ci biir lëndëm doo ma daw, doo ma réer
    À part solitute yaay sama amie
    Bokkuñu ndey ak baay te yaay sama famille

    Ma ni dëgg la
    Lu yàgg dëgg la
    Ànd bi dëgg la
    Moo tax ma bëgg la
    Lépp dëgg la nga

    Lu ma neex neex na la
    Lu ma metti sonal la
    Ki tax ma gëm ni xarit am na yaw la
    Lu ma neex neex na la
    Lu ma metti sonal la
    Ki tax ma gëm ni xarit am na yaw la

    Sama xarit, yaw xarit, yaw xaritoo
    Sama xarit, yaw xarit, yaw xaritoo
    Sama xarit, yaw xarit, yaw xaritoo
    Sama xarit, xarit, yeah, yeah, yeah, yeah

    Ma ni dëgg la
    Lu yàgg dëgg la
    Ànd bi dëgg la
    Moo tax ma bëgg la

    Yaay sama, sama, sama sama xarit
    Yaay sama, sama, sama sama xarit
    Yaay sama, sama, sama sama xarit
    Yaay sama, sama, sama sama xarit


    Comentarios

    Envía preguntas, explicaciones y curiosidades sobre la letra

    0 / 500

    Forma parte  de esta comunidad 

    Haz preguntas sobre idiomas, interactúa con más fans de Dieyna y explora más allá de las letras.

    Conoce a Letras Academy

    ¿Enviar a la central de preguntas?

    Tus preguntas podrán ser contestadas por profesores y alumnos de la plataforma.

    Comprende mejor con esta clase:

    0 / 500

    Opciones de selección