visualizaciones de letras 11
Letra

    Hun hun hun hun
    Hun hun hun hun
    Hun hun hun hun
    Oooh woo woo ouu woo
    Oooh woo woo ouu woo
    Oh woo woo
    Oh woo wooo

    Yeah life amul solo lu dem ba jar fi lii
    Dam leen tijjil sam xol mais ñoom ci poche lañuy Jàppe nit
    Ngay jàppe nit sa bopp muy teg sa kaw ay strategies
    Ñaata millions lañ ma fi dóor mais bon ñu tedd ñépp jaar nañ ci
    Doo wax ci ñoom danga leen di classé ni ex
    Kuy leb akay yomb a jot après mu jafe ni fay
    Ak noo manti jàppe nit di xëy bis claté bis fay
    Fen dañ kay jàppe ni glace booy amul glace bu dul séyy
    Divorcé aras moo ma gënal sëy buy tas bisub pénc
    Du xar moo waral tabaski, état di gracié ñi ray
    Kuy tuur dereet war na man lëkkalook ku gàcce dul ray
    Nun Sun salaire batay terewul ci Sun añ lanuy reer
    Waaye ku xam luy alal dëgg milliaru bànk du rëy sa bët
    Ku am lu rëy sa bët manul ñàkk jagg yu fay sa njëg
    Yéene néeg la moo tax it bis naa fanaan fi ma yéene ñépp
    Ay gaynde ci biti, ci birr kàkkatar, caga yee la gën

    Hun
    Life di la xët ci ruu ngay dimbali ñiy jooy ay góomu xol
    Naqar di gën di ñëw fekk xamuñ ni que moo gënn ci ñoom
    Dëkk sa kër ñuy xiif gënul nga gëj fa ñëw ndax wër millions
    Waaye dee buy jël du yoot moo tax lu ñuy togg day xëm du ñor
    Man xam naa lan laay yëg te xam naa nan laa mel ma nigger
    Xamuma kañ laay dee waaye xam naa lan laay def
    Dund mooy daaj boo dul mas a tàmm ndax dee moo kay dagg
    Loo màndi màndi boo geestoo gis néew sa daaj yépp ay wàcc
    Ñàkk a xam liy xew suba moo tax may gëmmentu di job
    Bañ xéy réccu di jooy maak samay doom du dëgër sunu bor
    Ci ñoom gis sama defaite moo leen gënal jël ay Coupe Du Monde
    May jël ay coups ci xol ak muñ di gën dëgër tul ni néew
    Jikko ni dëgg buy génn boroom rekk a ko dul yëg
    Li ñuy nëbb ci seen gémmiñ moo fees dell ci seeni bët
    Bien sûr que man nanu bokk te doo mas a bokk ci man
    Te soxlawuma gilet par balles mais tulu paaka ginnaaw yeah

    (Peace of mind)


    Comentarios

    Envía preguntas, explicaciones y curiosidades sobre la letra

    0 / 500

    Forma parte  de esta comunidad 

    Haz preguntas sobre idiomas, interactúa con más fans de Dip Doundou Guiss y explora más allá de las letras.

    Conoce a Letras Academy

    ¿Enviar a la central de preguntas?

    Tus preguntas podrán ser contestadas por profesores y alumnos de la plataforma.

    Comprende mejor con esta clase:

    0 / 500

    Opciones de selección