visualizaciones de letras 9

Damakoy Def

Jahman X-Press

Letra

    Li ngay jaay dama kay maye (waaw, man yooyu dama kay def)
    Affiché indo dawal cowboy (anh, man yooyu dama koy def)
    Li ngeen tële dama koy fowe (waaw, yooyu dama koy def)
    Sañse duma ko yëgal sama yaram (surtout yooyu dama koy def)

    Sama xol, dara safu ma (ak yooyu yépp dama koy def)
    Xulóowuma xeexuma (même yooyu dama koy def)
    Fu ma tële nga ni fal a mëne (yooyu yépp dama koy def)
    Aka ma bandit man ci xale (waaw, yooyu dama koy def)

    Ahn, nga ni dama leer pourtant dama ko woyofal
    Def relax ndank ni comme ku ci bëggul dara
    Ragaluma kenn ku dul Yàlla mi ma sakk
    Te kuy dox ci lëndëm mooy soxla lamp yi takk
    Taaluma toj man, damay tabax gis nga ni ma coole
    Dama ko mën ba xam ko moo tax, num neex la koy defee
    Busa garde wacc taay nga rakk ba dugg palais
    Na la teela fay ni lakk ci biir pompier
    Sama deer menoo ko yaq li nanga ko takk tere
    Deel dëkke xiin may dëkke taw ba bum yi bàyyi doore
    Li ñi def du benn gis nga ci boole pank
    Foo gis samay tof ci suuf coeur yi laal ko ndank

    Xame siisu man yi di lem bég (yooyu sax dama koy def)
    Yëgal ford di leen jege (même loolu dama koy def)
    Eh, duma leen bañ Yàlla tere (ak yooyu)
    Maay zero ku ma xamul di ma jugé (surtout yooyu)

    Soo ma saaga dama lay baal
    Soo may ñoddi bandit ma ñëw tegal la Baye Fall
    Ak yeneen dama koy def
    Oh yeen reewo leen (yooyu yépp dam koy def)
    Billaay reewo leen (yooyu ak yeneen sax)

    Ma nigga yaw bul mel kom man
    Dangay jëm man dama ko mën
    Amoo xalis amoo pexe foo may songe ma lay mën
    Dama liquide sumay wax sa xol day foy même sum lay nax
    Non du mystique vue ye nëri ba fake yi naan dafa rax
    Booy yaw wéero wéero
    Rang bu ñor ci BM du benn ak bu ñi kolo kolo
    Ñi dañu bëri défaut ku may takkale ak ñoom xamoo
    À part sa gel lu may doye ku may tekk loxo

    Fa nga tollu romb naa fa
    Fa nga jëm juge naa fa
    Maa leen gëna reew sama sound gëna nice doo ci dégg saaga
    Te lu mu jar ma jënd ko (tus!)
    Eh ñun lu mu jar ñu jënd ko (tus!)
    Lum jar ñu jënd ko (tus!)
    Tappetu ñu loolu (tus!)
    Dëgg du neex (tus!)
    Sama yaram day xesam seen piks yi di may neex (tus!)

    Cana warul ragal wet yeen ñépp man kase
    Fu ma leen fekk jomal leen kom gel bu faram fase
    Saaga ma ndeye ma la baal, respecté naa sama yaay
    Kon kenn ci yeen duma xam, su doon aay wax damay ray
    Ñoo bokku li ñi def mais dama ci boole saañ saañ
    Bàyyi na dugal statut damay sonn ak please send send
    Ahn dëgg la mën naa cool, mais mën naa con
    Am naa jikko bandit ak jikko innocent
    Dama bëri féem maak yeen du game
    Lu may doyee, lu ma jàpp, dama bëgga dem

    Waa wax leen ñi dégg xooleen ku leen gënal gënal
    Eh waa waxleen ñi dégg
    Maa fi nekk te waxoo lu nit mëna dégg
    Man lu mu jar, ma jënd ko (tus!)
    Seral zerol (tus!)
    Ak dox bu ñàkk-xorom (tus!)
    Su jeexee rekk jeex na (tus!)
    Dëgg du neex (tus!)
    Wool ma bandit yépp!


    Comentarios

    Envía preguntas, explicaciones y curiosidades sobre la letra

    0 / 500

    Forma parte  de esta comunidad 

    Haz preguntas sobre idiomas, interactúa con más fans de Jahman X-Press y explora más allá de las letras.

    Conoce a Letras Academy

    ¿Enviar a la central de preguntas?

    Tus preguntas podrán ser contestadas por profesores y alumnos de la plataforma.

    Comprende mejor con esta clase:

    0 / 500

    Opciones de selección