Suscríbete

Nous 2 (part. Wally B. Seck)

Viviane Chidid

Letra

    Yëguloo ne séy duma la koy jaay
    Dama xam rekk sama njëg, xam tamit lu maay jar
    Yëguloo ne man jigéen duma jaay neex
    Dama xam rekk sama njëg xam tamit
    Dama lay wax nga xam ni sa ñangal safu ma dara (dara)
    Sans man yaw doo dara (dara)
    Danga ma fàtte xam naa (xam naa)
    Ba ngay ram sama tànk naan ma nob la ngir Yàlla (yàlla)
    Loo xam lu neex man la
    Séy jaaxalu ma oh, yeah, yeah

    Dalal fok ni yaw rekk ya dugg mbar ànd AK salbe
    Boy mbaa du danga foog ne yaw rekk yaay góor wala?
    Ñaata yoon nga ram sama kanam comme xale
    Bu la neexe nga doxan
    Yaw defal comme si j'étais pas là
    Ooh, bu la neexe, bul fanaan ci yaw
    Yaw defal comme si j'étais pas là
    Yaw defal comme si j'étais pas là

    Yëguloo ne séy duma la koy jaay
    Dama xam rekk sama njëg, xam tamit lu maay jar
    Yëguloo ne man jigéen duma jaay neex
    Dama xam rekk sama njëg xam tamit

    Yaa ngi nax sa bopp
    Danga foog ni man maa xëy
    Barde ci keneen
    Wax ji bari na, ana looy xaar?
    Demal feneen
    Maa leen mën bari cacc yaay ñëwaat
    Naan bae jéegalu naa
    Xam nga ko ko sekkal bandit cerveau la woo
    Tere la nelaw
    Comme d'hab ay wax ngay tambalee ee
    Te ay jooy ngay mujje ee
    Wool sa bawat mee, ñëw baaluwaat, baaluwaat

    Bu la neexe nga doxan
    Yaw defal comme si j'étais pas là
    Ooh, bu la neexe bul fanaan ci yaw
    Yaw defal comme si j'étais pas là
    Yaw defal comme si j'étais pas là

    Yëguloo ne séy duma la koy jaay
    Dama xam rekk sama njëg, xam tamit lu maay jar
    Yëguloo ne maa la gëna neex
    Dama xam rekk sama njëg xam tamit
    Man dama lay wax nga xam ni sa ñangal safu ma dara (dara)
    Sans man yaw doo dara
    Danga ma fàtte xam naa
    Mbaa du seytaan la jaay ba nga foog ni yaw rekk la

    Léegi dafa sukka mel ni Aïda sukkeer
    Moo tax ngay jooy te loxo du la laal yaw
    Xamante nañu mak yaw
    Téye sama bopp ci yaw laay def
    Boo ko defe dinaa metti fees ci man
    Damay nàppe rekk mais mënuma la bàyyi
    Man yaw laa nob te leer na ma, kaay waay
    Sama reni xol, bébé n b'i fe
    Ti voglio bene, sama bella woyu Vi
    Wax naa la yaay baayam bandit bi
    Bëgg naa la, faale naa la waawaaw
    Eee, ee

    (Je ne peux pas vivre sans toi)
    Boo ma mere réy ma
    Ndax yaw yaay ki tax xol bi neex na
    (Je ne peux pas vivre sans toi)
    Oh mon bébé soo mere gaañ ma
    Ci xol leer na, xale bi
    (Je ne peux pas vivre sans toi)
    Baby Yàlla la sax jox ma
    Ma jël nob la, xale bile
    (Je ne peux pas vivre sans toi)
    Yaw ma la bëgg ba mu jeex ma tay
    Yaw yaa may ray, xale bi
    (Je ne peux pas vivre sans toi)
    Ndeysaan xamuloo ne
    Xuloo boo gis dafay jeex
    (Je ne peux pas vivre sans toi)
    Boo jubboowee sa xaaju guddi day neex
    (Je ne peux pas vivre sans toi)


    Comentarios

    Envía preguntas, explicaciones y curiosidades sobre la letra

    0 / 500

    Forma parte  de esta comunidad 

    Haz preguntas sobre idiomas, interactúa con más fans de Viviane Chidid y explora más allá de las letras.

    Conoce a Letras Academy

    ¿Enviar a la central de preguntas?

    Tus preguntas podrán ser contestadas por profesores y alumnos de la plataforma.

    Comprende mejor con esta clase:

    0 / 500

    Opciones de selección